Wolof Ak Xamle

Ag jiital

Woroom xam-xam yépp maase nañu ci wax ne menn réew manul a jëme kanam ci làkku jàmbur ak xaalisu jàmbur. Réew yi jëm kanam yépp seen làkki bopp lañu jël waggar ko dooleel door a dem. ...dawal li ci des

Nu gis ne it bokk na ci li téye Senegaal booba ak leegi mooy sunu làkk yi ñu boddi, suufeel leen, booleesu leen ci lu bari te ñuy ñi war a doxal réew mi.

Jëfandikoo sunu làkk yi nag dana waral xam-xam gën a jege nit ñi, woroom xel yi gën a man a xelli seen i xel, rawati na ci ndaw ñi, digu làkk wi dox ci diggante askan wi ak Nguur gi mbaa askan wi ak xam-xam deñ.

Bu dee Wolof kepp nga dégg mbaa séeréer mbaa pulaar bëgg a gëstu xam-xam bu jëm ci mboor, melosuuf añs fàww nga dem jàngi farañse mbaa araab mbaa àngale añs ba dégg ko door a man a tàmbalee gëstu xam-xam boobu mu jëlal la diir bu yàgg. Nun nag danoo gis ne ki dégg lu dul aw làkkam kepp sax war naa man a xam lépp lu mu bëgg a xam ci fànni xam-xam yépp. Ba tay jëfandikoo sunu làkk yi dana gën a yombal sunu jëflante ak bittim réew, dana suuxat sunug ubbeeku ak xamle réew mi ak i aadaam. Rawati na bu nu fexee ba xelum ndefar dégg ko ak ñu ci mel ni Google traduction, DeepL añs.

Ba tay dana wàññi at yu bari yi doomi réew mi di def ci ekool yi. Yaari saa-senegal yi am it te wanante ginnaaw da fiy jóge, muy jàngkati tubaab ak yu araab yi. Jàpp nanu ne benn saa-senegal rekk moo war a am muy bi jànge ci làkku réew mi ak yeneen ak yeneen.

Xam solo sii sunu làkk yi am moo tax ba kippaango gu tuddoon Jàng Wolof judd, te tur wa mujj soppiku doon WAX (Wolof Ak Xamle) ngir liggéey ci benn ci làkki réew mi di Wolof nga xam ne lu ëpp 95% i saa-Senegaal yi dégg nañu ko, man ko a wax.

Jàngu yi Leçons et parcours Jàng bind ak dawal Lecture et écriture Jàng Nos-Wax Parcours guidé Baat Xam Mots et significations Gàggantikaay Espace de traduction Aadama AI Poser une question en wolof
II. KAAJAR GI

WAX : Wolof Ak Xamle

Kaajar gi

Mbootaay gii di WAX di wund "Wolof Ak Xamle", mi ngi doon wuyoo ci turu Jàng Wolof, nu sosoon ko ci 10i fani féewaryee ci atum 2018 ci njiital sëñ Seex Lóo, sëñ Bëgg Bàmba Géy ak sëñ Ismayla Géy.

Waaye ci lél bii di 16i fani suwe ci atum 2019 lanu soppi tur wi tudde ko WAX, ngir mu gën a yaatu. Jàng wolof leegi ab bànqaas la ci biir WAX.

Cos gee ngi tukkee ci coobarewu ak bëgg a liggéeyal làkku Wolof ba ñu bari man ko a wax, man ko a dawal ba noppi man ko a bind.

Ci kaw gis-gis bii, la mbootaay gi sosoo ngir yaatal làkk wi, suqali làkk wi ak liggéeyal làkk wi ci sunu xam-xam, sunu am-am ak sunu man-man ci lu dul fayyeeku kenn.

Njiiti mbootaay gi warlul nañu képp ku ci bokk te tënku ci sàrt yi, njàngum Wolof ci lu dul muy fay dara, loolu nag amul setteey cosaan, xeet mbaa diine.

Njëwriñ gi Njàng mi Lef mi Laamisóo gi Koppar yi Xarala gi Saabal
1 Njëwriñ gi

Mooy toppatoo doxiinu mbootaay gi di denc wayndare yi di lootaabe ndaje yi añs. Daa séddalikoo ci ñenti pàcc.

  • Tatagalkat yi : Ñooy tatagal gan ñiy dikk ngir bokk ci mbootaay gi ci yónnee leen sàrt ak xamal leen nu mbir mi tëdde njëkk ñuy tàbbi. Képp kuy dugg it danga bindu ci wayndare wi bind sa tur ak saw sant sab dëkk sag limat añs ngir nu man a ràññee ñaata nit ñoo nekk ci mbootaay gi ak ku ne mooy kan.
  • Jëwriñi Kippaango yi : Ñooy ñiy saytu doxiinu kippaangoy WhatsApp yi ak ya ca aju.
  • Ñi yor xët yi : Mooy saytu mbooleem xëti WAX yi niki wow Facebook, Twitter, YouTube añs.
  • Ñi yore wayndare yi : Ñooy denc mbooleem wayndare yi. Yi Pekk bi waxtaane ba dëppoo ci bind ko, bataaxel yi WAX di jot mu jóge feneen ak yi WAX di bind ñeneen ak mbooleem lees war a denc ci am mbind, ñoom ñoo koy denc.
2 Njàng mi

Mooy bànqaas bi féetewoo wàllum njàng mi ak njàngale mi. Nu séddale ko ci ñatti jàngu. Muy Jàngu 1, Jàngu 2 ak Jàngu 3. Jàngu bu ne weer la fa dongo bi di def ay nattu bu amee poñ ya nu koy laaj mu jàll ci jàngu ba ca topp. Njàng mépp ñatti weer la.

3 Lef mi

Mooy bànqaas biy taxawe lépp lu jëm ci xam-xam yi ak téere yi ak piri mi ak raas waat yi. Daa séddalikoo ci juróomi xaaj.

  • Xam-xam yi : Ñooy taxaw ci firi xam-xam yi jële ko ci yeneeni làkk indi ko ci Wolof. Am nañu sémbuw firi mbooleem xam-xam yi gone yi di jàng ci daara yi. Niki xam-xamu Màndaxe (mathématiques) : Xam-xamu màndaxe ci njàng mu suufe mi bi firi nanu ko ci Wolof ba noppi. Di am yéeney firi bu njàng mu digg-dóomu mi, liise añs. XANAS (SVT) : firi nanu li gone yi di jàng ci jàng mu suufe mi ak lenn ci njàng mu digg-dóomu mi ba móol nanu ko def ko téere. Di am yéeney àggale li ci kaw. Mboor (histoire) añs.
  • Téere yi : Di taxawu képp kuy bind téere ci kippaango gi.
  • Topp gi : Ña fa nekk ñooy topp téere yi muy génn. Téere bu ñu wéral rekk bu wér la moo xam bu bàyyikoo ci mbootaay gi mbaa feneen.
  • Tekki gi : Ña fa nekk di ay tekkikat ñoo féetewoo tekki ay téere walla ay mbind añs.
  • Akaademi fent ak raas : Mooy kurel gees dénk lu jëm ci wutal làkk ay waat yu yees yu mu xamul woon.
4 Laamisóo gi

Moo féetewoo lijjanti yi mbootaay gi di soxla ci biir ak ci bitti. Daa séddalikoo ñatti xaaj.

  • Jëwriñi gox yi : Ñooy jëmm yi teewal mbootaay gi ci gox bu nekk ci réew mi.
  • Jaaykatu téere yi : Ñooy ñiy jaay téerey mbootaay gi.
  • Lijjantikat yi : Ñooy dox mbooleem lijjanti yi ci bitti. Niki dem ci tele yi añs.

Farba ji : Mooy ki yor kàddug kippaango gi. Fu kippaango gi ame lu mu bëgg a wax mbaa wane ci tele yi moom lay yabal.

5 Koppar yi

Mooy méngoo mbirum koppar yi ñeel kippaango gi. Nii la tëggoo :

Sàmba-koppar : Mooy denc xaalis bi. Moom rekk moo am sañ-sañu denc xaalis ci mbootaay gi.

Yaay-sàq ak baay-sàq : Ñooy ñaar ñi koy saytu ndax ni mu yore xaalis bi jaar na yoon. Di saytu lépp luy dugg ak luy génn ak bu génnee fu mu jëm.

6 Xarala gi

Ñoo méngoo lépp lu jëm ci wàllu xarala di ko liggéey. Niki widewoo nataal yi, wayndare, jëfekaay gi, këyiti cér yi añs.

7 Saabal

Moo féetewoo joxe ay xibaar, tàmbalee ci Wolof yem ci Wolof.